Ngir yombal dajale ak delloo sa fóot, binndal bu baax adres yi nga bëgga SETwitch liggéey.
Mën nga bind ba ñaari adres. Barab bi nga am ci GPS dafay tax dawalkat bi mëna gis fi nga nekk ci lu yomb, doonte adres bi yombul ràññee.
Ngir bind ab adres :
1. Tannal "Adres bu njëkk" wala "Adres bu ñaareel".
2. Bindal sa adres ci barab biñ la jox.
3. Xool fi màrker bi nekk ci kaw kàrt bi.
4. Toxal màrker bi nimu ko soxlaa ngir teg ko ci buntu mbedd mi jàkkarloo ak sa kër.
5. Soo xoolee leeral yi ba noppi, nga denc sa adres.
💡 Tip: Soo nekkee ci barab bi nga wara enregistre, mën nga jëfandikoo sa barabu GPS ngir jàppale la ci def marker.
Barab bu jaar yoon ci GPS daf nuy may nu mëna gis la ci anam wu yomb te baax, nga mëna tànn li nga dajale.